Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 48 languages
«Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "Yàlla mu Baarkeel mi te kawe nee na: waajalal naa sama jaam yu sell yi, lu bët musul a gis, nopp musu ko a dégg, te musul a rot ci xolo nit" Abuu Hurayrata nee na: jàngleen bu leen soobee: {benn bakkan xamul la ñu ko dencal ci luy bégloo ay bët} [As-Sajda: 17].»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamle na ne Yàlla mu Baarkeel mi te kawe nee na: Waajalal naa ngir teral ñeel sama jaam yu sell yi ca àjjana lu bët musul a gis jëmmam, te nopp musul a dégg kàddoom, te melokaanam tàbbiwul ci xolu nit. Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm daal di ne: jàngleen bu leen soobee: {benn bakkan xamul la ñu leen dencal ci luy bégloo ay bët} [As-Sajda: 17].

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality