Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Available in 65 languages
«Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay dafa ñëw ci Yó’ente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, man de amuma ku may wommat yóbb ma ca jàkka ja, mu sàkku ci Yónente Yàlla bi mu yombalal ko muy jullee ci këram, Yónente bi daal du loy jox Yombal, ba mu wëlbatikoo rekk mu woo ko, daal di ne ko: "ndax danga dégg wooteg julli gi?" Mu ne ko: waaw, mu ne ko: "kon nag wuyujil ».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Daa am gumba gu ñëw si Yónente bi -yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi amuma ku may dimbali di jàpp sama loxo yóbb ma jàkka ja ci julliy juróom yi, mu bëgg Yónente bi yombalal ko mu bàyyi jullig mbooloo, mu yombalal ko, waaye ba mu wanee ginnaaw rekk mu woo ko, ne ko: ndax danga dégg noddug julli gi? Mu ne: waaw, mu ne ko kon nag wuyujil wootekatu julli gi.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality