Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Available in 60 languages
«Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan kàbbar ci julli gi, da daan noppi ab diir njëkk muy jàng, ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi jote naa la sama baay ak sama yaay nga xibaar nu sa nopi gi ci diggante kàbbar gi ak njàng mi, lan ngay wax: mu wax ne: "damay wax: Allaahumma baahid baynii wa bayna xataayaaya kamaa baahadta baynal masrixi wal maxribi, Allaahumma naqinii min xataayaaya kamaa yunaqas sawbul abyadi minad danasu, Allaahumma ixsilnii min xataayaaya bissalji wal maa-i wal baradi".»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan kàbbar ci julli gi day noppi tuuti njëkk muy jàng Al-Faatiha, day ubbee julli gi ci yenn ñaan yi, bokk ci li rot ci ñaan yooyu li muy wax naan: «Allaahumma baahid baynii wa bayna xataayaaya kamaa baahadta baynal masrixi wal maxribi, Allaahumma naqinii min xataayaaya kamaa yunaqas sawbul abyadi minad danasu, Allaahumma ixsilnii min xataayaaya bissalji wal maa-i wal baradi», Day ñaan Yàlla mu soreele digganteem ak ay njuumte ba du ca tàbbi mukk, niki nga xam ne penku ak sowwu du ñu daje ba fàww, bu ca tàbbee itam mu laabal ko ca dindi ko ca kem ni ñuy dinde tilim ji ci yére bu weex, ak mu raxas ko ci ay njuumteem seral ay tàkk-tàkkam ak tàngooram ci yii di seral; ndox, ak galaas.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality