Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

Available in 71 languages
«Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «buleen def seen kër yi ay bàmmeel, te buleen def sama bàmmeel am ndaje, deeleen julli ci man, ndax seen ug julli ci man dina yeksi fi man ak fu ngeen man di nekk».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day tere neenal kër yi bañfaa julli ba muy mel ni ay bàmmeel yu ñu dul julli, Mu tere it di baril ay siyaare bàmmeelam ak di fa dajaloo ci anamug aadawoo; ndax loolu day jëme ci bokkaale, Mu digle ñu julli ci moom ci bépp barab ci kaw suuf; ndax loolu dana àgg fa moom moo xam ci ku jege la walla ku sori ñoo ci yam, kon aajowoowul di barila dem ca bàmmeelam.

Source
Abóo Daawuda soloo na ko
Download image

Saved at original quality