Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

Available in 54 languages
«Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «bu ngeen ko gisee woorleen, bu ngeen ko gisee worileen, bu muuroo ci yeen nangeen ko nattale».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne màndargam duggug weeru koor ak génnam, mu wax ne: bu ngeen gisee weeru koor wi woorleen, bu aw niir doxee seen diggante ak moom mu muuru ci yéen; nangeen lim fanweeri fan ñeel weeru Baraxlu wi, bu ngeen gisee weeru Kori gi worileen, bu aw niir doxee seen diggante ak moom mu muuru ci yéen; nangeen lim fanweeri fan ñeel weeru Koor gi.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality