Ngëneel yi ak teggiin yi
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-:
Available in 70 languages
«Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Jële na ñu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu nettali jële ci Boroomam mu màgg mi, mu wax ne: «ab jaam dafa def bàkkaar, daal di wax: yaw sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar Yàlla mu baarkeel mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar, Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar,Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, defal lu la soob jéggal naa la».»Meaning translation ·
Saved at original quality








