Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële nañu ci Abuu Mashuud Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Available in 70 languages
«Jële nañu ci Abuu Mashuud Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Amna nit ku mas a ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ne ko: amuma waruwaay, kon nag jox ma waruwaay, mu ne ko: «amuma ko», am ku ne ko: yaw Yónente bi, dinaa ko tegtal ku ko jox waruwaay, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «Ku tegtale ci lu baax, dina am pay gu mel ni li ki ko def am».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Leerarug adiis bi : Am na ku mas a w ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla defal jàmm- ne ko: sama waruwaay dafa dee, yéegal ma cig daaba, te jox ma waruwaay mu yóbbu ma, Yónente bi -yal na ko Yàlla defal jàmm- gàntal ko, ne ko amul dara lu mu koy jox, benn waay bu nekkoon foofu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi dinaa ko yóbbu ci ku koy jox waruwaay, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm- xamle ne, mook kiy saraxe ñoo bokk am yiw, ndax moo ko tegtal aji-yittewoo ji.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality