Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 70 languages
«Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ñaari baat a ngi nii yu woyof ci làmmeñ, diis ci màndaxekaay ba, Yàlla miy Aji-Yërëme ji sopp leen: Subhaanal Laahil Hasiim, Subhaanal Laahi wa bi hamdihii».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne am na ñaari baat yu nit ki di wax ci lu dul coono ak ci bépp anam, te seenug fay màgg lool ca màndaxekaay ba , te sunu Boroom miy Aji-Yërëme ji bëgg leen muy: Subhaanal Laahil Hasiim, Subhaanal Laahi wa bi hamdihii; ngir li ñu làmboo ci melal Yàlla cig màgg ak mat, ak sellal ko ci ay wàññiku -baarkeel na te kawe na-.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality