Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

Available in 53 languages
«Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «Bu nit ki faatoo ay jëfam dog na ba mu des ñatt: ba mu des saraxe buy wéy, walla xam-xam bu ñuy jariñoo, walla doom ju baax ju koy ñaanal».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi day xibaare ne jëfi aji-faatu ji day dagg cig faatoom, du am ay yiw ginnaaw ba mu faatoo ba mu des ñatti mbir ndaxte moom mooy sabab bi: Bi ci njëkk: sarax boo xam ni yool ba day sax, niki Wàqf, ak tabax jàkka, ak gas teen, ak yeneen. Ñaareel bi: xam-xam bu nit ñi di jariñoo, niki taalif ay téerey xam-xam, walla mu jàngal nit, nit kooka di tasaare xam-xam bi ginnaaw ba mu faatoo. Ñatteel bi: doom ju baax ju gëm di ñaanal ay way-juram.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality