Pas-pasu Lislaam
Jële nañu ci Ummu Salamata Ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
Available in 39 languages
«Jële nañu ci Ummu Salamata Ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "amul benn jullit bu musiba di dal mu wax li ko Yàlla digal: {Yàlla moo ni moom te ci moom lañuy dellu} [Al-Baxara: 156], Yàlla yoolal ma ci sama musiba bii, te wuutalal ma jo yiw, lu dul ne Yàlla dana ko ko wuutalal lu ko gën", nee na: ba Abuu Salamata faatoo ma ne: ana kan ci jullit ci mooy gën Abuu Salamata? Kër gi njëkk a gàddaay jëm ca Yonnente Yàlla ba yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, topp ma wax ko, Yàlla daal di ma koy wuutalal Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.»Meaning translation ·
Saved at original quality








