Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

Available in 44 languages
«Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "Yàlla mu màgg mi nee na: doomu Aadama moo ngi may lor day ŋàññ jamono ji te man maay jamono, ci sama loxo la mbir yi nekk maa koy wëlbati guddi ak bëccëg".»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne Yàlla mu kawe dafa wax ci hadiisu Al-Xudsii: nit kiy saaga ak di ŋàññ jamono ji ci bu musiba ak lu ñi sib amee moo ngi may lor di ma wàññi; ndaxte Yàlla tudd naa sellam gi moom dong mooy saytu di doxal liy xew; kon ŋàññ jamono ji mooy ŋàññ Yàlla mu màgg mi, te jamono ji mbindeef rekk la bu ñu tàggat, xew-xew yi di ci daw ci ndigalul Yàlla mu kawe mi.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality