Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële nañu ci Abdulaa Ibn Amr-yal na leen Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne:

Available in 60 languages
«Jële nañu ci Abdulaa Ibn Amr-yal na leen Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «jullit mooy ki nga xam ne jullit ñi mucc nañu ci làmmiñam ak ci loxoom,gàddaaykat nag mooy ki gàddaay li Yàlla araamal ci moom».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne jullit bu lislaamam mat mooy ki jullit ñi mucc ci làmmiñam du leen saaga, du leen rëbb, du leen jëw, te du dox seen diggante ci genn xeetu lor ci làmmiñam, Dañuy mucc it ci loxoom du leen tooñ, du jël seen alal ci lu dul dëgg, ak lu niru loolu, Aji-gàdday nag mooy ki bàyyi li Yàlla araamal.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality