Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 65 languages
«Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «sunu Boroom bu baarkeel bi te kawe day wàcc guddi gu nekk ci asamaani àdduna si bu guddi gi desee ñatteelu xaaj bu mujj ba, di wax naan: ku may woo ma wuyu ko? Ku may laaj ma jox ko? Ku may jéggalu ma jéggal ko?».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne Yàlla sunu boroom day wàcc guddi gu nekk ci asamaani àdduna si bu guddi gi desee ñatteelu xaaj bu mujj ba, di xemmemloo jaamaam yi ci ñaan, ndax moom mooy wuyu ku ko woo, di leen ñaax ci ñu laaj ko lu ñu bëgg, ndax mooy jox ku ko laaj, di leen woo ci ñu jéggalu ko séen i bàkkaar, ndax mooy jéggal ay jaamam yi ko gëm.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality