24 hadiths
Jële nañu ci Abuu Sarrin -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Jële na ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yàlla mu kawe mi mu wax ne:«yéen sama jaam ñi damaa araamal tooñ ci sama bopp, ma def ko muy lu araam ci seen diggante kon buleen di tooñante, yéen sama jaam ñi yéen ñépp dangeen a réer ku dul ki ma gindi, kon sàkkuleen ci man gindiku ma gindi leen, yéen sama jaam ñi yéen ñépp a xiif ku dul ki ma leel, kon sàkkuleen ci man ma leel leen , kon dinaa leen leel, yéen sama jaam ñi yéen ñépp a rafle ku dul ki ma wodd, kon sàkkuleen ci man ma wodd leen kon dinaa leen wodd, yéen sama jaam ñi dangeen di juum guddi ak bëccëg kon jéggaluleen ma ma jéggal leen, yéen sama jaam ñi manuleen maa lor ba di ma lor, te manuleen maa jariñ ba di ma jariñ, yéen samay jaam ñi njëkk ci yéen ak ñi mujj ci yéen, nit ñi ak jinne yi ci yéen bu ñu neekkoon xolu ki gën a ragal Yàlla ci yéen loolu du yokk ci sama nguur gi dara, yéen samay jaam ñi njëkk ci yéen ak ñu mujj ña, ak seen i nit ak jinne bu ñu neekkoon xolu ki gën a kàccoor ci yéen loolu du wàññi ci sama nguur gi dara, yéen samay jaam ñi njëkk ci yéen ak ñu mujj ña, ak seen i nit ak jinne dañoo taxaw ci benn pàkk bu yaatu, ñu ñaan ma ma jox kenn ku nekk la mu ñaan loolu du wàññi li ne fi man lu dul li ab puso di wàññi ci ndoxum géej gi bu ñu ko sa dugalee, yéen sama jaam ñi seen jëf rekk laa leen di dencal joxaat leen ko ba mu mat, ku fa fekk yiw na sant Yàlla, waaye ku fa fekk ay bu mu yedd ku dul boppam».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla nee na: ku noonook sama péete yégal naako ab xare, sama jaam bi du ma jegeñ-jegeñlu ci dara lu ma gënal li ma farataal ci moom, sama jaam bi du deñ dima jéema jege ci ay naafila ba ma bëgg ko, te bu ma ko bëggee, maay nekk déggam gi muy dégge, ak gisam gi muy gise, ak loxoom bi muy jàppe, ak tànkam bi muy doxe, bu ma ñaanee ma may ko,bu ma musloo ma musal ko, du ma dengi-dengi ci dara lu may def, samag dengi-dengi mi ngi ci bu may jël bakkanu aji-gëm ji, ndax day bañ a dee,te man dama koy bañ a def lu mu bëggul».Al-buxaariy soloo na ko