Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

Available in 70 languages
«Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla mu kawe mi du xool meloy jaam ñi ak seen i yaram, ndax dafa rafet walla dafa ñaaw ? Ndax dafa rëy walla dafa ndaw? Ndax dafa wér walla dafa wéradi? Du xool itam seen i alal, ndax dafa bari walla dafa tuuti? Yàlla du toppe jaamam yi walla mu leen di saytu ci mbir yii ak seenug rawante ci loolu, waaye day xool seen xol yi ak la ca nekk cig ragal Yàlla ak kóolute, ak dëggu ak sellal, walla ngistal mbaa ndéggtal, day xool it seen i jëf ak ug sellam mbaa ag yàqoom; mu fay leen ca.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality