Pas-pasu Lislaam
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
Available in 55 languages
«Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Yàlla mu baarkeel mi te kawe day wax waa àjjana: éey yéen waa àjjana? Ñu ne ko wuyusi nanu la topp nañu la ak mbegte, mu ne leen: ndax gërëm ngeen? Ñu ne ko: lu ñuy teree gërëm te nga jox nu loo joxul kenn ci sa mbindeef yi? Mu ne leen: dama leen di jox lu gën loolu, ñu ne ko: yaw sunu Boroom, ana lan moo gën loolu? Mu ne leen: wàcce naa sama ngërëm ci seen kaw, dootuma leen mere ba fàww".»Meaning translation ·
Saved at original quality








