Pas-pasu Lislaam
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Available in 65 languages
«Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Muhaas dafa toggoo woon ak moom ci benn waruwaay mune ko: «yaw Muhaas Ibn Jabal», mu ne ko: wuyu naa la yaw Yónente Yàlla bi, mu ne ko: «yaw Muhaas» mu ne ko wuyu naa la yaw Yónéte Yàlla bi, ñatti yoon, mu ne ko: « amul kenn kuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la te mu dëggu ci xolam lu dul ne Yàlla dana ko araamal ca sawara», mu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ndax duma ko wax nit ñi ngir ñu bég? Mu ne ko: «kon dañuy bàyyandiku». Muhaas waxe ko jamano yi muy faatu ngir bañ a bàkkaaru.»Meaning translation ·
Saved at original quality








