Hadith for the World
Ngëneel yi

Ngëneeli wéetal Yàlla

4 hadiths

4 hadiths

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu, ak Abuu Hurayrata -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ñu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Amul benn coono buy dal ab jullit, mbaa tawat walla, jaaxle, mbaa naqar, loraange, walla njàqare, doonte dég gu ko jam la, lu dul ne Yàlla dina ca fare yenn ci ay bàkkaaram».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Muhaas dafa toggoo woon ak moom ci benn waruwaay mune ko: «yaw Muhaas Ibn Jabal», mu ne ko: wuyu naa la yaw Yónente Yàlla bi, mu ne ko: «yaw Muhaas» mu ne ko wuyu naa la yaw Yónéte Yàlla bi, ñatti yoon, mu ne ko: « amul kenn kuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la te mu dëggu ci xolam lu dul ne Yàlla dana ko araamal ca sawara», mu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ndax duma ko wax nit ñi ngir ñu bég? Mu ne ko: «kon dañuy bàyyandiku». Muhaas waxe ko jamano yi muy faatu ngir bañ a bàkkaaru.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Muhaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Toggoo woon naa ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- am Mbaam mu ñuy woowe Xufayr, mu ne ma: «yaw Muhaas, ndax xam nga lan moy Àqi Yàlla ci ay jaamam, ak lan mooy àqi jaam ñi ci Yàlla?», Muhaas nee: ma ne ko: Yàlla ak ub Yónenteem ñoo ko xam, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- daal di ne ko: «àqi Yàlla ci jaam ñi mooy ñu jaamu ko te bañ koo bokkaale ak dara, àqi jaam ñi ci Yàlla nag mooy du mbugal ku ko bokkaalewul ak dara» ma ne ko: yaw Yónente Yàlla bi tee maa bégal nit ñi ci lii ? Mune ma: «buleen bégal kon dañuy bayliku.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay dafa ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, yan mooy ñaar yiy waral ? Mu ne ko: «ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana, ku faatu te bokkaale ko ak dara dana dugg sawara».Muslim soloo na ko