Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële na ñu ci Muhaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Available in 71 languages
«Jële na ñu ci Muhaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Toggoo woon naa ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- am Mbaam mu ñuy woowe Xufayr, mu ne ma: «yaw Muhaas, ndax xam nga lan moy Àqi Yàlla ci ay jaamam, ak lan mooy àqi jaam ñi ci Yàlla?», Muhaas nee: ma ne ko: Yàlla ak ub Yónenteem ñoo ko xam, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- daal di ne ko: «àqi Yàlla ci jaam ñi mooy ñu jaamu ko te bañ koo bokkaale ak dara, àqi jaam ñi ci Yàlla nag mooy du mbugal ku ko bokkaalewul ak dara» ma ne ko: yaw Yónente Yàlla bi tee maa bégal nit ñi ci lii ? Mune ma: «buleen bégal kon dañuy bayliku.»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral àqi Yàlla ci jaam ñi, ak àqi jaam ñi ci Yàlla, ci ne àqi Yàlla ci jaam ñi mooy ñu jaamu ko moom dong te duñu ko bokkaale ak dara, Ak ne àqi jaam ñi ci Yàlla mooy mu bañ a mbugal ñi koy kennal te duñu ko bokkaale ak dara. Muhaas ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ndax duma bégal nit ñi ngir ñu bég ci ngëneel lii? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere ko ngir ragal nit ñi di sukkandiku ci loolu.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality