Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne dégg na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:

Available in 62 languages
«Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne dégg na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man, ndax ku julli ci man genn julli Yàlla julli ci moom fukk, te ngeen ñaanal ma Wasiila ba, ndax moom ab bérab la ca àjjana, te kenn yayoowu ko ku dul ab jaam ci jaami Yàlla yi, te maa ngi yaakaar ne man la, ku ma ñaanal Wasiila samag ramm dagan na ko».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day tegtal kiy dégg kiy nodd ñeel julli gi muy bàmtu ci ginnaawam, di wax lu mel ni li muy wax, bamu des ci ñaari Hàyyahala yi, ndax day wax ci séen ginnaaw: laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi, daal di julli ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ginnaaw bu nodd gi jeexee, ndax ku julli ci moom genn julli Yàlla dana julli ci moom ci sababus loolu fukki julli, maanaam jullig Yàlla ci jaam bi nag mooy: muy tagg jaam bi fa Malaaka ya. Mu digle ñu ñaanal ko Yàlla Wasiila -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, te moom ag daraja la ca àjjana, te moo ca gën a kawe, te daraja jooju du yéwén mbaa muy yomb lu dul ñeel benn jaam ci mbooleem jaami Yàlla yi, te maa ngi yaakaar ne man la, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax loolu ngir toroxlu; ndaxte bu fekkee ne daraja ju kawe jooju, kenn rekk moo koy am, kon kenn kooku du nekk ku dul moom Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-; ndax moom moo gën ci mbindéef yi. Yonnente bi leeral ne ku ñaanal Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Wasiila ag rammam dana ko jot -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality