Pas-pasu Lislaam
Jële nañu ci Usmaan Ibn Abil Haas -yal na ko Yàlla dollee gërëm-:
Available in 63 languages
«Jële nañu ci Usmaan Ibn Abil Haas -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Moom dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, Saytaane de dafa dox sama diggante ak sama julli gi, te day jaxase sama njàng mi, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: " kooku Saytaane bu ñu woowe Xinsab la, boo ko yégatee nanga muslu ci Yàlla ci moom, te nga tifli ci sa càmmooñ ñatti yoon", nee na: ma def loolu Yàlla dindi ko ci man.»Meaning translation ·
Saved at original quality








