Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Available in 71 languages
«Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Damaa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi, Ibn Jadhaan de ca jamanoy ceddo ga da daan jokk mbokk di leel miskiin, mo ndax loolu dana ko jariñ ? Mu wax ne: «du ko jariñ de, ndaxte waxul benn yoon ne: sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Abdallah Ibn Jadhaan, bokkoon na ci njiitu waa Xurays njëkk Lislaam, Te bokk na ci ay jëfam yu baax: daa na jokk mbokk, di rafetal jëme ci ñoom, di leel miskiin, ak yeneeni ngënéel yoy Lislaam dafa ñaaxe ci def ko, ci ne jëf yooyu du ko jariñ ëllëg bis-pénc; te li ko waral mooy weddi gi mu weddi Yàlla, te masul wax: yaw sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality