Alquraan ju tedd ji ak xam-xam yi ci aju
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
Available in 70 languages
«Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Bis-pénc du ñëw mukk ba keroog jànt bi di fenke sowwu, bu fa fenkee nag ba nit ñi gis ko ñoom ñéppay gëm, te loolu mooy jamono joj: {amul benn bakkan bu ngëmam di jariñ bu gëmul woon lu njëkk, te fàggu ca ngëmam ga aw yiw} [Al-Anhaam: 158] bis-pénc dana taxaw fekk ñaari waay tallal nañu séen yére seen diggante te duñu ko mujj a jaayante, dunu ko it mujj a lem, bis-pénc dana taxaw fekk ben waay juge na fa mu ràtte soowam te du ko mos sax, bis-pénc dana taxaw fekk nit a ngi tabax ab baajam te du sa naan, fekk nit ki yëkkati ab tibam jame ko ci gémmeñam te du ko ñam».»Meaning translation ·
Saved at original quality








