Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Alquraan ju tedd ji ak xam-xam yi ci aju

Jële na ñu ci Ubay Ibn Kahb -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

Available in 70 languages
«Jële na ñu ci Ubay Ibn Kahb -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «yaw Aba-Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi?» Nee na: ma ne ko: Yàlla ak ub Yónenteem ñoo xam. Mu ne ma: «yaw Aba- Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi ?» Nee na: ma ne ko: {Allaahu laa-i-Laaha illaa huwa Al-Hayyul Xayyuumu} [Al-Baxara: 255]. Nee na: mu dóor sama dënn, daal di wax ne: «giñ naa ci Yàlla, na xam-xam ndokkeel Aba- Munsir».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa laaj Ubay Ibn Kahb aaya bi gën a màgg ci téere Yàlla bi, muy dengi-dengi ci tontu bi, mujj gi mu ne: mooy aayatul Kursiyyu: {Allaahu laa ilaaha illaa huwa Al Hayyul Xayyuumu}, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dëggal ko, daal di fëgg dënnam ngir junj ne fees na dell ak xam-xam ak xereñ, daal di koy ñaanal mu texe ci xam-xam bi te ñu yombalal ko.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality