Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 70 languages
«Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama», ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, bu doon moom rekk kon dana doy. Mu wax ne: «ëppe na ko juróom-benni fukk ak juróom-ñenti xaaj, te ñoom ñépp ñoo ngi mel ni aw tàngaayam».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Leerarug hdiis bi : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne sawaraw àdduna ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaji sawaraw Jahannama, Sawaraw allaaxira moo gën a tàng sawaraw àdduna ci juróom-benni fukk ak juróom-ñetti xaaj, te xaaj bu ci ne moo ngi tolloog tàngaayu sawaraw àdduna. Ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, sawaraw àdduna bi rekk doyoon na ngir mbugal ña fay dugg, Mu ne leen: sawaraw Jahannama ëppe na sawaraw àdduna ci juróom-benn ak juróom- ñenti xaaj te ñoom ñépp a mel ni moom ciw tàngaay wu tar.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality