WO
Gëm Yàlla Mu tedd Mu màgg mi
Wéetal Yàlla ci jaamu ko
14 hadiths
Wéetal Yàlla ci moom gi mu moom lépp di ko saytu
2
Wéetal Yàlla ci jaamu ko
14
Wéetal Yàlla ci ay turam ak i meloom
24
14 hadiths
Jële nañu ci Umar Ibnu Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na : «Yàlla tere na leen ngeen di giñ ci seen baay yi", Umar wax ne : ba ma déggee Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di ko tere giñatuma ca mooxam ci lu ma ci samay wax mbaa may jottali waxi keneen ».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Yàlla mu kawe mi nee na: ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem".
Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Umar Ibnul Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «buleen ma jay kem ni Nasaraan yi jaye woon doomu Maryama; man daal ab jaamam laa, kon deeleen wax: jaamub Yàlla ak ndawam».
Al-buxaariy soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne: Wax nañu Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko ana kan ci nit ñi moo gën a texe ci sag rammu ëllëg bis-penc? Yónent Yàlla bi wax ne: «Njoortoon naa ne yaw Abuu Hurayrata Yamamay njëkk laaj lii; ndax li ma gis sag xér ci Hadiis, nit ki gën a texe ci samag rammu ëllëg bis-penc, mooy ki wax, Laa ilaaha illal Laahu, te mu sell lool ci xolam, walla ci bakkanam».
Al-buxaariy soloo na ko
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- me wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na jenn wax, ma wax Jeneen wax, yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ne: " ku faatu fekk moo ngi wutal Yàlla ndend dana dugg sawara" man ma ne: ku faatu te wutalul Yàlla ndend dana dugg àjjana.
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن ابن مسعود رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم : «من أصابته فَاقَة فأنْزَلها بالناس لم تُسَدَّ فَاقَتُهُ، ومن أنْزَلها بالله، فَيُوشِكُ الله له بِرزق عاجل أو آجل».
رواه أبو داود والترمذي وأحمد
عن عبد الله بن مسعود رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم أنه قال: "أكبر الكبائر: الإشراك بالله، والأمن من مَكْرِ الله، والقُنُوطُ من رحمة الله، واليَأْسُ من رَوْحِ الله".
رواه عبد الرزاق
عن عبد الله بن عكيم رضي الله عنه مرفوعاً: «مَنْ تَعَلَّقَ شيئا وُكِلَ إليه».
رواه أحمد والترمذي
Jële na ñu ci Taarix Ibn Asyam Al-Asjahii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku wax: laahi ilaaha illallaahu, amul kenn ku ñu war a jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, daal di weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla alalam ak dereetam araam na, Yàlla rekk nag mooy càmbar ay jëfam».
Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Marsad Al-Xanawii -yalna ko Yàlla gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli».
Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : Ummu Salamata dafa xibaar Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- benn jàngu bu mu gis ca Abasa, (jàngu : jaamukaayu katolig yi) ñu koy woowe Maariya, mu wax ko la mu fa gis ci ay nataal, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: " ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka, daaldi cay def nataal yooyu, ñooñu ñoo yées ci nit ñi fa Yàlla".
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Muhaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Toggoo woon naa ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- am Mbaam mu ñuy woowe Xufayr, mu ne ma: «yaw Muhaas, ndax xam nga lan moy Àqi Yàlla ci ay jaamam, ak lan mooy àqi jaam ñi ci Yàlla?», Muhaas nee: ma ne ko: Yàlla ak ub Yónenteem ñoo ko xam, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- daal di ne ko: «àqi Yàlla ci jaam ñi mooy ñu jaamu ko te bañ koo bokkaale ak dara, àqi jaam ñi ci Yàlla nag mooy du mbugal ku ko bokkaalewul ak dara» ma ne ko: yaw Yónente Yàlla bi tee maa bégal nit ñi ci lii ? Mune ma: «buleen bégal kon dañuy bayliku.
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay dafa ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, yan mooy ñaar yiy waral ? Mu ne ko: «ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana, ku faatu te bokkaale ko ak dara dana dugg sawara».
Muslim soloo na ko
عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «إِنَّ اللهَ يَرْضَى لَكُمْ ثَلَاثًا، وَيَكْرَهُ لَكُمْ ثَلَاثًا، فَيَرْضَى لَكُمْ: أَنْ تَعْبُدُوهُ، وَلَا تُشْرِكُوا بِهِ شَيْئًا، وَأَنْ تَعْتَصِمُوا بِحَبْلِ اللهِ جَمِيعًا وَلَا تَفَرَّقُوا، وَيَكْرَهُ لَكُمْ: قِيلَ وَقَالَ، وَكَثْرَةَ السُّؤَالِ، وَإِضَاعَةِ الْمَالِ».
رواه مسلم