Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne :

Available in 62 languages
«Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : Ummu Salamata dafa xibaar Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- benn jàngu bu mu gis ca Abasa, (jàngu : jaamukaayu katolig yi) ñu koy woowe Maariya, mu wax ko la mu fa gis ci ay nataal, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: " ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka, daaldi cay def nataal yooyu, ñooñu ñoo yées ci nit ñi fa Yàlla".»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Ndayu jullit ñi Ummu Salamata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- dafa nettali Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne moom ba mu nekkee ca suufus Abasa dafa gis ab jàngu ñu koy woowe Maariya- ay nataal ak i rafetal ak i rëd-rëd ñoo fa nekk; mu yéemu ci loolu ! Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral li waral ñu def fa foto yooyu; Mu wax ne : ñii ngay wax bu amaan ku baax ku faatu ci ñoom dañuy tabax jàkka ci kaw bàmmeelam di fa julli, daa di fay def nataal yooyu, Mu leeral ne ñiy def loolu ñoo yées ci mbindeef yi fa Yàlla, ndax seen i jëf da lay yóbbe ci bokkaale Yàlla mu kawe mi.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality