Hadith for the World
Ngëneel yi

Ngëneeli jëfi cér yi

6 hadiths

6 hadiths

Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "kiy taxawu ak a dimbali ab Jatun ak way-ñakk moo ngi mel ni kuy xeex ci yoonu Yàlla, wàlla kuy taxaw guddi di woor bëccëg"Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Sawbaan -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Alal ji gën ci li nit ki di joxe: mooy alal ji mu jox njabootam ak alal ji mu jox ay daabaam ci yoonu Yàlla, ak alal ji mu jox ay àndandoom ci yoonu Yàlla» Abuu Xilaaba wax ne: "dafa, tàmbali ci njaboot Abuu Xilaaba, dellu wax ne: ana gan góor mooy gën a màgg ug pay ci góor guy jox njabootam gu ndaw di leen feg, mbaa Yàlla di leen jariñ ci moom ba def leen ñu doylu.Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "jullit bi bu jàppoo ba raxas xar kanamam; bàkkaar bu mu mas a def ci ay gëtam day rot ànd ak ndox mi, -walla ànd ak toq ndox bi mujj-, bu raxasee ay yoxoom bépp bàkkaar bu mu mas a def ci ay yoxoom dana rot ànd ak ndox mi, ni ki noonu bu raxasee ay tànkam bàkkaar yi mu masa dox ak tànkam yépp dana rot ànd ak ndox mi -walla ànd ak toq ndox bi mujj-, ba keroog muy set wicc ci ay bàkkaar".Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «dungeen dugg àjjana ndare ngeen gëm, te dungeen gëm ndare ngeen bëggante, moo ndax duma leen tegtal lol su ngeen ko defee dangeen bëggante? Siiwalleen ab nuyóo seen diggante».Muslim soloo na ko
عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم : «من قتل وَزَغَةً فِي أَوَّلِ ضَرْبَةٍ فله كذا وكذا حسنة، ومن قتلها في الضَّرْبَةِ الثانية فله كذا وكذا حسنة دون الأولى، وإن قتلها في الضربة الثالثة فله كذا وكذا حسنة». وفي رواية: «من قتل وَزَغًا في أول ضربة كتب له مائة حسنة، وفي الثانية دون ذلك، وفي الثالثة دون ذلك».رواه مسلم
عن أبي سعيد الخُدْرِي رضي الله عنه قال: جاءت امرأة إلى رسول الله صلى الله عليه وسلم فقالت: يا رسول الله، ذهب الرجال بِحَدِيثِكَ، فاجْعَل لنَا من نَفْسِك يومًا نَأتِيكَ فيه تُعَلِّمُنَا مما عَلَّمَكَ الله، قال: «اجْتَمِعْنَ يَوَم كَذَا وكَذَا» فَاجْتَمَعْنَ، فأتَاهُنَّ النبي صلى الله عليه وسلم فَعَلَّمَهُنَّ مما عَلَّمَهُ الله، ثم قال: «ما مِنْكُنَّ من امرأة تُقَدِّمُ ثَلاَثَة من الولد إلا كانوا حِجَابًا من النَّارِ» فقالت امرأة: واثنين؟ فقال رسول الله صلى الله عليه وسلم : «واثنين».متفق عليه