Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

Available in 62 languages
«Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "kiy taxawu ak a dimbali ab Jatun ak way-ñakk moo ngi mel ni kuy xeex ci yoonu Yàlla, wàlla kuy taxaw guddi di woor bëccëg"»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne kiy taxawe ay yittey jigéen ji jëkkëram faatu, te amul kenn ku taxawe ay mbiram, ak miskiin bi aajowoo, mu leen di dundal ci ngir yaakaar payug Yàlla mu kawe mi, kooku ak payam day yamoo ak kiy xeex ci yoonu Yàlla, walla kiy taxaw di julli guddi te du ca tàyyi, mbaa kiy woor te du dog.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality