Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 59 languages
«Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «misaalu toogandoo bu sell ak toogandoo bu bon moo ngi mel ni ki yor gëttug Misk ak kiy upp ab furne, ki yor gëttug Misk gi: benn mu mayla ci, walla nga jënd ci, mbaa nga am fi moom xet gu neex, kiy upp ab furne nag moom: benn mu lakk say yére, walla nga jële fa xet gu bon».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa joxe misaal ci ñaari xeeti nit: Bi ci njëkk: toogandoo ak àndandoo bu sell buy tegtale Yàlla ak lu ngëremam nekk, di dimbalee ci topp Yàlla, Moom de day mel ni jaaykatu Misk, benn mu joxla ca, walla nga jënd ca, mbaa nga xeeñcu fa xet gu teey te neex. Ñaareel bi: toogandoo ak àndandoo bu bon; kiy teree topp Yàlla, tey dimbalee ci ay moy, ngay gis ci moom ay jëf yu bon, ñu lay ŋàññ ndax li ngay ànd ak di toog ak ku mel ni moom. Misaalam moo ngi mel ni tëggkat biy upp sawara; benn mu lakk say yére ci sawara wiy naaw, walla nga jële fa ci jege gi nga ko jege ag xet gu bon.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality