Hadith for the World
Yiy woyofal xol di ko dëdduloo àddina ak waaraate yi

Ŋàññ moy yi

6 hadiths

6 hadiths

Jële na ñu ci Abuu Bakrata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Ndax duma leen xibaar bàkkaar yi gën a mag?» Mu wax ko ñatti yoon, ñu ne ko: ahakay yaw Yónente Yàlla bi, mu ne leen: «bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur» mu jóg toog fekk dafa sóonu woon, daal di ne: «ak wax ludul dëgg», nee na: deñul di ko bàmtu ba ñu mujj wax naan: aka neexoon mu noppi.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Abdulaa Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate».Al-buxaariy soloo na ko
Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «misaalu toogandoo bu sell ak toogandoo bu bon moo ngi mel ni ki yor gëttug Misk ak kiy upp ab furne, ki yor gëttug Misk gi: benn mu mayla ci, walla nga jënd ci, mbaa nga am fi moom xet gu neex, kiy upp ab furne nag moom: benn mu lakk say yére, walla nga jële fa xet gu bon».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "moytuleen juróom-ñaar yiy alage", ñu ne ko: yaw Yónenteb Yàlla bi yooyu yan la ? Mu ne: "bokkaale Yàlla, ak njabar, ak ray bàkkan bu Yàlla araamal ñu ray ko ci ludul dëgg, ak lekk ribaa, ak lekk alali jirim, ak daw bisub xare , ak tuumaal jigéen i jullit ju saŋewu".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «sama xeet wépp lañuy jéggal ba mu des ñiy fésal ag moy, te bokk na ci fésal ag moy nit ku def dara ci guddi gi, daal di xëy Yàlla suturaal ko, muy wax naan: éey yaw diw, biig def na lii ak lee, fekk dafa fanaan Yàlla suturaal ko, mu xëy di wuññi li ko Yàlla suturaaloon».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن أبي هريرة عن النبي صلى الله عليه وسلم قال: «لعن الله السارق، يسرق البَيْضَةَ فَتُقْطَعُ يده، ويسرِقُ الحَبْلَ فَتُقْطَعُ يَدُهُ».متفق عليه