Hadith for the World
Ngëneel yi ak teggiin yi

Yiy woyofal xol di ko dëdduloo àddina ak waaraate yi

63 hadiths

63 hadiths

Jële na ñu ci Abuu Bakrata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Ndax duma leen xibaar bàkkaar yi gën a mag?» Mu wax ko ñatti yoon, ñu ne ko: ahakay yaw Yónente Yàlla bi, mu ne leen: «bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur» mu jóg toog fekk dafa sóonu woon, daal di ne: «ak wax ludul dëgg», nee na: deñul di ko bàmtu ba ñu mujj wax naan: aka neexoon mu noppi.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن أنس بن مالك رضي الله عنه أنَّ رَجُلاً كَانَ عِند النَبِيَّ صلى الله عليه وسلم فَمَرَّ رَجُلٌ بِهِ، فقال: يا رسول الله، أنِّي لَأُحِبُّ هَذَا، فَقَال لَهُ النَبِيُّ صلى الله عليه وسلم : «أَأَعْلَمْتَهُ؟» قال: لا. قال: «أَعْلِمْهُ»، فَلَحِقَهُ، فقال: إِنِّي أُحِبُّك فِي الله، فقال: أّحَبَّك الَّذِي أَحْبَبْتَنِي لَهُ.رواه أبو داود والنسائي في الكبرى وأحمد
عن أبي موسى الأشعري رضي الله عنه قَالَ: قالَ رسول اللَّه -صَلّى اللهُ عَلَيْهِ وسَلَّم-: «إِنَّ مِنْ إِجْلاَلِ الله -تَعَالَى-: إِكْرَامَ ذِي الشَّيْبَةِ المُسْلِمِ، وَحَامِلِ القُرْآنِ غَيرِ الغَالِي فِيه، وَالجَافِي عَنْه، وَإِكْرَام ذِي السُّلْطَان المُقْسِط».رواه أبو داود
Jële na ñu ci Abdulaa Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate».Al-buxaariy soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «àdduna de ñam wu neex la te naat, Yàlla da leen fee wuutal, di xool lu ngeen fiy jëf, noytuleen àdduna te moytu jigéen ñi, ndax fitna ji njëkk a am ci Banuu Israayil ci jigéen la xewe».Muslim soloo na ko
عن عبد الله بن عمرو بن العاص رضي الله عنهما مرفوعاً: «ليس منا من لم يَرحمْ صغيرنا، ويَعرفْ شَرَفَ كبيرنا».رواه أبو داود والترمذي وأحمد
Jële nañu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay dafa laaj Yonnente bi ci bis-pénc ne ko: kañ la bis-pénc? Mu ne ko: "lan nga ko waajalal". Mu ne ko: du dara, lu dul ne bëgg naa Yàlla ak ub yonnenteem yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu ne ko: "ki nga bëgg ngay nekkal". Anas nee na: masuñoo bég ci dara kem ni ñu bége ci li Yonnente bi wax ne: "ki nga bëgg ngay nekkal" Anas wax ne: man bëgg naa Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak Abuu Bakrin ak Umar, te maa ngi am yaakaar a nekk ak ñoom ndax li ma leen bëgg, donte jëfuma lu tolni seen jëf ya.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «misaalu toogandoo bu sell ak toogandoo bu bon moo ngi mel ni ki yor gëttug Misk ak kiy upp ab furne, ki yor gëttug Misk gi: benn mu mayla ci, walla nga jënd ci, mbaa nga am fi moom xet gu neex, kiy upp ab furne nag moom: benn mu lakk say yére, walla nga jële fa xet gu bon».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne :Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Nattu du deñ ci jullit bu góor bi ak bu jigéen bi di dal ci bakkanam ak ci doomam ak ci alalam ba mu daje ak Yàlla fekk benn bàkkaar nekkul ci kawam».At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat
Jële nañu ci Suhaybu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «yéemu naa ci mbirum jullit bi moom de mbiram lépp yiw la, te kenn amul loolu ku dul jullit bi, bu ko mbégte dalee day sant mu doon aw yiw ci moom, bu ko lor dalee day muñ mu doon aw yiw ci moom».Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "moytuleen juróom-ñaar yiy alage", ñu ne ko: yaw Yónenteb Yàlla bi yooyu yan la ? Mu ne: "bokkaale Yàlla, ak njabar, ak ray bàkkan bu Yàlla araamal ñu ray ko ci ludul dëgg, ak lekk ribaa, ak lekk alali jirim, ak daw bisub xare , ak tuumaal jigéen i jullit ju saŋewu".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Yàlla mu kawe mi nee na: ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem".Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Ubaadata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla moom dong amul te amul bokkaale, ak ne Muhammat ndawul Yàlla la di ndawam, ak ne Iisaa jaamub Yàlla la di ndawam, di kàddoom gu mu sànni ci Maryama di ag ruu gu bawoo ci moom, ak ne àjjana dëgg la, sawara dëgg la, Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن معاذ بن جبل رضي الله عنه عن رسول الله صلى الله عليه وسلم أنه قال: «قَالَ اللهُ -عَزَّ وجَلَّ-: المُتَحَابُّون فِي جَلاَلِي، لَهُم مَنَابِرُ مِن نُورٍ يَغْبِطُهُم النَبِيُّونَ والشُهَدَاء».رواه الترمذي وأحمد
Jële nañu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: «àjjana moo gën a jege ku ne ci yeen ay waroy dàllam, sawara it naka noonu».Al-buxaariy soloo na ko
عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضيَ اللهُ عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «الدُّنْيَا سِجْنُ الْمُؤْمِنِ وَجَنَّةُ الْكَافِرِ».رواه مسلم
عن أبي هريرة رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال: «إنَّ في الجنَّة مائةَ دَرَجَة أعَدَّهَا الله للمُجاهِدين في سَبِيل الله ما بَيْنَ الدَّرَجَتَيْنِ كما بين السماء والأرض».رواه البخاري
عن سهل بن سعد الساعدي ـرضي الله عنه- قَالَ رَسُول اللَّه -صَلّى اللهُ عَلَيْهِ وسَلَّم-: «لو كانت الدنيا تَعدل عند الله جَناح بَعوضة، ما سَقَى كافراً منها شَرْبَة ماء».رواه الترمذي
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «sama xeet wépp lañuy jéggal ba mu des ñiy fésal ag moy, te bokk na ci fésal ag moy nit ku def dara ci guddi gi, daal di xëy Yàlla suturaal ko, muy wax naan: éey yaw diw, biig def na lii ak lee, fekk dafa fanaan Yàlla suturaal ko, mu xëy di wuññi li ko Yàlla suturaaloon».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Jaabir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc njëkk muy faatu ci ñatti fan muy wax naan: "bu kenn ci yéen faatu lu dul ne dafa rafet njort ci Yàlla".Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abii Sahiid Al-Xudrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "Yaw Abuu Sahiid, ku gërëm Yàlla muy Boroomam, Lislaam di diineem, Muhammat di Yonenteem àjjana war na ci moom", Abuu Sahiid yéemu ci loolu, ne ko: baamtul ma ko yaw Yonente Yàlla bi, mu def ko, topp mu ne ko: "ak leneen lol dees na ci yëkkëtil jaam bi téeméeri daraja ca àjjana, te diggante ñaari daraja yi mi ngi mel ni diggante asamaan ak suuf ", mu ne ko: loolu lan la yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne ko: "jihaad ci yoonu Yàlla, jihaad ci yoonu Yàlla".Muslim soloo na ko
عن أنس رضي الله عنه مرفوعاً: «يَتْبَعُ الميتَ ثلاثةٌ: أهْلُه ومَالُه وعَمَلُه، فيرجع اثنان ويَبْقى واحد: يرجع أهْلُه ومَالُه، ويبقى عَمَلُه».متفق عليه
عن أنس بن مالك رضي الله عنه مرفوعاً: «يُؤتى بأنعم أهل الدنيا من أهل النار يوم القيامة، فَيُصْبَغُ في النار صَبْغَةً، ثم يقال: يا ابن آدم، هل رأيت خيرًا قطُّ؟ هل مَرَّ بك نَعِيمٌ قطُّ؟ فيقول: لا والله يا رب، وَيُؤْتَى بأشدِّ الناس بُؤسًا في الدنيا من أهل الجَنَّة، فَيُصْبَغُ صَبْغَةً في الجنَّة، فيقال له: يا ابن آدم، هل رأيت بُؤسًا قط؟ هل مَرَّ بك شِدَّةٌ قط؟ فيقول: لا والله، ما مَرَّ بي بُؤْسٌ قطٌّ، ولا رأيت شِدةً قَطُّ».رواه مسلم
Jële nañu ci An-Nuwwaas ibn Simhaan Al-Ansaarii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Laaj naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc lu baax ak lu bon, mu wax ne: "lu baax mooy rafet jikkó, lu bon mooy luy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ñi gis ko".Muslim soloo na ko