Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 61 languages
«Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «àdduna de ñam wu neex la te naat, Yàlla da leen fee wuutal, di xool lu ngeen fiy jëf, noytuleen àdduna te moytu jigéen ñi, ndax fitna ji njëkk a am ci Banuu Israayil ci jigéen la xewe».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne àdduna ñam wu neex la, te naat ci gisiin, ba nit ki dana ci woroo, ba di ci nuur, ba def ko yitteem ji gën a rëy. Ak ne Yàlla dafa def ñenn ci nun ñuy wuutu ñeneen ci dundug àdduna, ngir xool lan lanuy def, ndax danu koy topp, walla danu koy moy? Topp mu wax: moytuleen poñaxiitam àdduna ak ub taaram di leen nax ba di leen jëme ci bàyyi li leen Yàlla digal, ba ngeen di def li mu leen tere. Bokk na ci li gën a màgg ci yi ñu war a moytu ci fitnay àdduna mooy fitnay jigéen ñi, ndaxte mooy fitna ji waa Banuu Israayil njëkk a tàbbi.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality