Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

Available in 59 languages
«Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Jullit bu góor du bañ jullit bu jigéen, ndax su bañee ci moom jenn jikkó gërëm na ci moom jeneen jikkó».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na jëkkër di bañ jabaram bañ guy waral mu koy tooñ di ko bàyyi di ko dummóoyu; Ndaxte nit dañu koo bind cig wàññiku , te bu bañee ci moom ay jikkó yu ñaaw, dana fekk ci moom ay jikkó yu rafet; bu ko defee mu gërëm yu rafet yi tolloog moom , te muñ yu ñaaw yi mu gërëmul, loolu mooy tax muy muñ te du ko bañ mbañeel guy waral muy tàggalikoo ak moom.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality