Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële na ñu ci Abdulaa Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 65 languages
«Jële na ñu ci Abdulaa Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral bàkkaar yu mag yi, te mooy gu ñu tëkku aji-def ji ci tëkku gu tar ci àdduna walla allaaxira. Bu njëkk bi "Bokkaale Yàlla": te mooy def wenn xeetu jaamu ñeel ku dul Yàlla, ak yamale lenn ak Yàlla ci lu Yàlla jagoo, cig jaamu, ak ug moomeelam ak ci ay turam ak i meloom. Ñaareel bi "Dënge ñaari way-jur": te mooy lépp luy waral lor ñaari way-jur moo xam wax la walla jëf, ak bàyyee rafetal jëme ci ñoom ñaar. Ñatteel bi "ray bakkan": ci lu dul dëgg, niki ray ko cig tooñ ak ug jalgati. Ñenteel bi "ngiñ luy nuural nit ": te mooy giñ lu waay def di fen te xam ne day fen, dañu koo tudde loolu nag; ngir ne day nuural boroomam ci ay bàkkaar walla ci sawara.

Source
Al-buxaariy soloo na ko
Download image

Saved at original quality