Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële nañu ci An-Nuwwaas ibn Simhaan Al-Ansaarii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Available in 62 languages
«Jële nañu ci An-Nuwwaas ibn Simhaan Al-Ansaarii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Laaj naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc lu baax ak lu bon, mu wax ne: "lu baax mooy rafet jikkó, lu bon mooy luy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ñi gis ko".»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Laaj nañu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc lu baax ak lu bon, mu wax ne: Melo wi gën a màgg ci lu baax mooy rafet jikkó ci Yàlla ci ragal ko, ak ci nit ñi ci muñ seen lor, ak néew i mer, ak yaatal sa kanam, wax ju teey, ak jokk mbokk ak topp Yàlla ak ñeewant, ak baax, ak rafet nekkiin ak àndandoo yi. Bàkkaar nag mooy luy yëngatu ci bakkan ci ay lënt, mu ciy sikk-sàkka te mu yëg ci boppam ag xat, xol bi am ci sikk-sàkka, mu ragal ne bàkkaar la, te bëggu ko a feeñal ndax li mu ñaaw ci tànneefi nit ñi baax ñi te mat, loolu nag ndaxte bakkan ni mu mel day bëgg nit ñi gis lu baaxam, kon bu bañee ñu gis yenn jëfam yi day lu bon te amul yiw.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality