Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr ibnul Haas yal na leen Yàlla dollee gërëm:

Available in 56 languages
«Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr ibnul Haas yal na leen Yàlla dollee gërëm: Jële na ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne bu daan dugg ci jàkka day wax: "ahuusu bil Laahi Alhasiimi, wa bi wajhihi Alkariimi, wa sultaanihii alxadiimi, minas Saytaani Arrajiimi", nee na: ndax loolu rekk la? Ma ne ko: waaw, mu ne: bu waxee loolu saytaane day wax naan: aarees na ko ci man tay.»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan dugg ci jàkka day wax: (ahuusu bil Laahi Alhasiimi) maa ngi aaru di làqatu ci Yàlla ak i meloom. (wa bi wajhihi Alkariimi) Aji-Tabe ji Aji-Joxe ji, (wa sultaanihii) ag notam ak kàttanam ak notam ñeel ku ko soob ci mbindeefam yi (alxadiimi) ki Amu tàmbalikaay Te amul it yamukaay (minas Saytaani Arrajiimi) ki ñu soreele dàq ko ci yërmàndey Yàlla, Maanaam: Yàlla sàmm ma ci ay jax-jaxam ak ug beewalam, ak ay jéegoom, ak i xalaatam, ak i jaxaseem, ak réeralaateem, ndaxte moom sabab la ci cànkute ak jëme ci mbewte ak réer. Ñu wax Abdullah ibn Amr "ndax loolu dong" maanaam: ndax lii rekk la Yonnente bi wax? Mu ne: waaw. Bu kiy dugg ci jàkka waxee ñaan gii; Saytaane day wax: kii di dugg aar na boppam ci man ci waxtu yépp bëccëg gi ak guddi gi.

Source
Abóo Daawuda soloo na ko
Download image

Saved at original quality