Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële na ñu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 63 languages
«Jële na ñu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "ñiy yërëme Aji-Yërëme ji dana leen yërëm, yërëmleen waa suuf, kon ka ca kaw asamaan dana leen yërëm.»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ñiy yërëm ñeneen ñi Aji-Yërëme ji dana leen yërëm ca yërmàndeem ja xajoo lépp; muy ag pay gu dëppoo ak séen jëf. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di digle ñu yërëm lépp lu nekk ci kaw suuf, muy nit walla mala, walla njanaaw mbaa yeneen xeeti mbindeef yi, payug loolu nag mooy Yàlla mi ci kaw asamaan yi yërëm leen.

Source
Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat
Download image

Saved at original quality