Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële na ñu ci Abuu Muusaa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

Available in 66 languages
«Jële na ñu ci Abuu Muusaa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yalla dana néggandiku tooñkat bi, ba bu ko jàppee du ko rëcc» nee na: mu daal di jàng: aaya bii «{niki noonu it la sa jàppug Boroom di deme bu jàppee waa dëkk buy tooñ te ag jàppam lu metti la te tar} [Huud: 102]»»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo di wéy cig tooñ ak i moy ak bokkaale, ak tooñ nit ñi ci séen i àq, ndax Yàlla mu kawe mi day néggandiku tooñkat bi di ko yeexe ak di guddal fanam di baril alalam te du ko gaawa mbugal; bu tuubul mu jàpp ko te du ko bàyyi ndax ay bàkkaar yu bari. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di jàng aaya bii: {niki noonu it la sa jàppug Boroom di deme bu jàppee ab waa dëkk buy tooñ te ag jàppam lu metti la te tar} [Huud: 102].

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality