Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

Available in 65 languages
«Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Ngëm juróom-ñaar fukki xaaj la ak lu topp» wala: «juróom-benn fukki xaaj la ak lu topp» - ci ay xaaj, bi ci gën a kawe: mooy wax: laa ilaaha illal Illa Laahu, bi ci gën a suufe, mooy: randale aw lor ci kaw yoon wi, te kersa benn pàcci la ci ngëm»»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ngëm ay xaaj la ak i melo yu bari, te day làmboo jëf yi ak pas-pas yi ak wax yi. Ak ne li gën kawe ci ngëm te gën ca mooy wax: «laa ilaaha illal laahu» te xam maanaama , tey jëfe lamu làmboo, ci ne Yàlla moom mooy Yàlla miy kenn mooy ki yayoo ag jaamu moom dong deesul jaamu leneen. Ak ne jëf ji gën a tuuti ci ngëm, mooy randale lépp luy lor nit ñi ci yoon yi. Yónente bi xibaare na ci ne lii di kersa ci meloy ngëm la bokk, jikko la juy waral def lu rafet te bàyyi lu ñaaw.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality