Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 47 languages
«Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "bu Ramadaan ñëwee dañuy tijji bunti àjjana yi, tëj bunti sawara yi, jéng saytaane yi".»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne bu weeru koor duggee ñatti mbir day am: Bi ci njëkk: dañuy tijji bunti àjjana yi duñu ci tëj benn bunt. Ñaareel bi: dañuy tëj bunti sawara yi duñu ci tijji benn bunt. Ñatteel bi: dañuy tënk saytaane yi ak jinne yi fétterlu ci ay ceen, duñu leen bàyyi ñuy def la ñu daan def ci bu dul Ramadaan. Loolu lépp nag màggal la ñeel weer wii, ak ug xemmemloo ñeel way-jëf yi ci ñu baril ay jaamu ci julli ak saraxe ak sikar ak jàng Alxuraan ak yu dul yooyu; ak ñu sori bàkkaar yi ak moy yi.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality