Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 62 languages
«Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom kenn du ma dégg ci xeet wii moo xam Yahuut la walla Nasaraan, ba faatu te gëmul li ñu ma yónni lu dul ne dana bokk ci waa sawara».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa giñ ci Yàlla ne amul kenn ku koy dégg ci xeet wii, moo xam muy yahuut walla nasaraan mbaa leneen, te wooteb Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- egg ci moom mu faatu te gëmu ko lu dul ne dana bokk ci waa sawara sax fa ba fàww.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality