Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Sayd ibn Xaalid yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

Available in 56 languages
«Jële nañu ci Sayd ibn Xaalid yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "ku waajalal aji-xare ci yoonu Yàlla kooku xare na, ku wuutu aji-xare ci yoonu Yàlla ci yiw kooku xare na".»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ku waajalal aji-xare ci yoonu Yàlla jumtukaayi tukkeem ak yi mu aajowoo ci ay ngànnaay yu manut a ñàkk, ak waruwaay, ak ñam, ak ub dund ak yeneen; kooku àtteb aji-xare ji la am, te dina am yoolub way-xare yi. Ku wuutu aji-xare ci ay mbiram ci yiw, wuutu ko ci di sàmm njabootam ci jamono yi mu fàddoo kooku àtteb aji-xare ji la am.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality