Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële ci Muhaas ibn Jabal yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Available in 54 languages
«Jële ci Muhaas ibn Jabal yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa téye ci loxoom, ne ko: "yaw Muhaas, waat naa ci Yàlla ne dama laa bëgg", mu ne ko: "maa ngi lay dénk yaw Muhaas bul bàyyi mukk di wax ginnaaw julli gu ne: Allaahuma ahinnii halaa sikrika wa sukrika wa husni hibaadatika".»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa jàpp ci loxob Muhaas yal na ko Yàlla dollee gërëm, ne ko: giñ naa ci Yàlla ne dama laa bëgg, te maa ngi lay dénk yaw Muhaas bul bàyyi di wax ginnaaw julli gu nekk: (Allaahuma ahinnii halaa sikrika) ci jépp wax ak jëf juy jëme ci jaamu la, (wa sukrika) ci amug xéewal ak deñug naqar, (wa husni hibaadatika) ci ag sellal ñeel Yàlla ak topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Source
رواه أبو داود والنسائي وأحمد
Download image

Saved at original quality