Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Adiis ak xam-xam yi ci aju

Jële nañu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 71 languages
«Jële nañu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Jottalileen jële ci man donte benn aaya la, ta ngeen waxtaane waa Banuu Israayil ci lu amul benn jafe-jafe, waaye ku ma fenal te tay ko na waajal ab tooguwaayam ca sawara».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yónente bi dafa digle ñu jottali xam-xam biy juge ci moom ci muy Alxuraan walla Sunna, donte tuuti la niki benn aaya Alxuraan walla benn Hadiis, ci sartub mu xam li miy jottali ak limiy woote. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ne jafe-jafe nekkul ci waxtaane Banuu Israayil ci xew-xew ya amoon ci ñoom bu wuutewul ak sunu Sariiha. Topp Mu moytandikuloo ci di ko fenal, tek ci ne kepp ku ko fenal te tay ko na daal di jëlal boppam dëkkuwaayam ca sawara.

Source
Al-buxaariy soloo na ko
Download image

Saved at original quality