Ngëneel yi ak teggiin yi
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm:
Available in 61 languages
«Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm: Benn kaw-kaw dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ne ko: tegtal ma jëf joo xam ne su ma ko defee dinaa dugg àjjana, mu ne ko: "dangay jaamu Yàlla te doo ko bokkaale ak dara, di taxawal julliy farata, di joxe asaka, di woor weeru koor" mu ne ko: giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom duma dolli ci lii dara, ba mu demee Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne : "ku bëgg a xool nit ku bokk ci waa àjjana, na xool waa jii".»Meaning translation ·
Saved at original quality








