Dégg diine ak i cosaanam
Jële nañu ci Mahdaan ibn Abii Talhata Alyahmarii mu wax ne:
Available in 59 languages
«Jële nañu ci Mahdaan ibn Abii Talhata Alyahmarii mu wax ne: Dajee naa ak Sawbaan surgab Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ma ne ko: wax ma jëf joo xam ne bu ma ko defee Yàlla dugal ma ci àjjana? Walla mu ne ma ne ko: jëf ji Yàlla gën a bëgg, mu noppi, ma laajaat ko, mu noppi, ma laajaat ko ñatteelu yoon, mu ne ma: laaj naa ko Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ma: "déng naa la ngay bari looy sujjóotal Yàlla, ndaxte doo sujjóotal Yàlla genn sujjóot lu dul ne Yàlla dina la ci yëkkatil daraja, sippil la ci njuumte" Mahdaan nee na: ma dajee ak Abuu Dardaa ma laaj ko mu tontu ma: lu mel ni li ma Sawbaan wax.»Meaning translation ·
Saved at original quality







