Hadith for the World
Julli

Ngëneelu julli

10 hadiths

10 hadiths

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «julli gi gën a diis ci naaféq yi mooy jullig gee ak jullig fajar, te bu ñu xamoon li nekk ci ñoom ñaar kon danañu ko teewe donte dañuy raam, doon naa yittewoo digle ñu taxawal julli, ma digal benn waay mu jiite nit ñi, ma ànd ak ay góor ñu yor ay matti sawara, nu dem ci nit yi dul teewe julli gi, taal séen kër ya ca séen kaw».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «julliy juróom, ak Àjjuma ba Àjjuma, ak weeru koor ba weeru koor, dañuy far bàkkar yi ci séen diggante bu dee moytu nañu bàkkaar yu mag yi».Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Mahdaan ibn Abii Talhata Alyahmarii mu wax ne: Dajee naa ak Sawbaan surgab Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ma ne ko: wax ma jëf joo xam ne bu ma ko defee Yàlla dugal ma ci àjjana? Walla mu ne ma ne ko: jëf ji Yàlla gën a bëgg, mu noppi, ma laajaat ko, mu noppi, ma laajaat ko ñatteelu yoon, mu ne ma: laaj naa ko Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ma: "déng naa la ngay bari looy sujjóotal Yàlla, ndaxte doo sujjóotal Yàlla genn sujjóot lu dul ne Yàlla dina la ci yëkkatil daraja, sippil la ci njuumte" Mahdaan nee na: ma dajee ak Abuu Dardaa ma laaj ko mu tontu ma: lu mel ni li ma Sawbaan wax.Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «xibaarleen ma bu ag dex nekkoon ci buntu këru kenn ci yéen mu ciy sangu bis bu nekk juróomi yoon, ndax loolu dana dese tilim ci yaram?" Ñu ne ko: déedéet du bàyyi ci deram dara, mu ne: "loolu nag moo ngi mel ni julliy juróom, yàlla da ciy far njuumte yi».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Jundub Ibn Abdullah Al-Xasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku julli suba moo ngi ci kaaraangeg Yàlla, moom Yàlla du leen toppe dara ci ay àqam, ndax ki Yàlla toppe dara ciy àq dana ko jàpp, te dana këpp kanamam ca sawaraw Jahannama».Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abii Suhayr Umaarata ibn Ruaybata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: «koo xam ne day jullu laata jant bi di fenk ak laata muy soh du dugg sawara».Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Usmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi-yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: "amul benn jullit boo xam ne jullig farata dana jot mu rafetal njàppu ma ak toroxlu ga ak rukkoo ya,lu dul ne dana ko faral li ko jiitu ci ay bàkkaar,fii ak deful bàkkaar bu mag,te loolu jamono jépp la".Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Abuu Maalik Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf, julli ag leer la, saraxe it aw lay la, muñ it ag leer la, Alxuraan it aw lay la ñeel la yaw, walla muy aw lay ci sa kaw, nit ñépp dañuy xëy am ci ñuy jaay séen bopp, benn mu goreel ko, walla mu alag ko».Muslim soloo na ko
عن ربيعة بن كعب الأسلمي قال: كنتُ أبيتُ مع رسول الله صلى الله عليه وسلم فأتيتُه بوَضوئه وحاجته فقال لي: «سل» فقلت: أسألك مرافقتك في الجنة. قال: «أو غير ذلك؟» قلت: هو ذاك. قال: «فأعني على نفسك بكثرة السجود».رواه مسلم
عن عائشة عن النبي صلى الله عليه وسلم قال: «ما من ميت تصلي عليه أُمَّةٌ من المسلمين يبلغون مائة، كلهم يشفعون له، إلا شفعوا فيه».رواه مسلم