Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Abii Suhayr Umaarata ibn Ruaybata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na:

Available in 54 languages
«Jële nañu ci Abii Suhayr Umaarata ibn Ruaybata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: «koo xam ne day jullu laata jant bi di fenk ak laata muy soh du dugg sawara».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne: kuy saxoo di julli jullig Fajar ak jullig Tàkkusaan, du dugg sawara; mu jagleel ko ñaari julli yii; ndaxte ñoom ñaar ñooy julli yi gën a diis ci julli yi, ndax waxtuw suba day nekk ci jamono ji nelaw di neex, waxtuw tàkkusaan di jamono ji nit ki di nekk ci liggéey yi bëccëg gi ak yaxantu mi, ku sàmmonte ak ñaari julli yii ànd ak coono ba kon dana sàmmonte ak julli yi des.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality