Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Usmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi-yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:

Available in 60 languages
«Jële nañu ci Usmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi-yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: "amul benn jullit boo xam ne jullig farata dana jot mu rafetal njàppu ma ak toroxlu ga ak rukkoo ya,lu dul ne dana ko faral li ko jiitu ci ay bàkkaar,fii ak deful bàkkaar bu mag,te loolu jamono jépp la".»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day leeral ne amul benn jullit bob waxtuw jullig farata dana dugg mu rafetal am njàppoom matale ko,daal di teewlu julli gi ànd ak ragal ba xolam ak ay céram yépp jublu Yàlla di teewlu màggaayam, mu matal jëfi julli gi niki rukkoo yi ak sujjóot yi ak yeneen yi, lu dul ne julli gi dana nekk lu koy faral bàkkaar yu ndaw yi ko jiitu, fii ak deful bàkkaar bu mag,ngëneel lii nag day wéy ba ci jamono jépp ak ci julli yépp.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality